Garanaat

Nataalu garabug Garanaat

Garanaat xeet la ci xeeti garab yi nga xam ni dañuy am fóoyteef, mi ngi bokk ci njabootug Lythracées . Cosaanam ma nga nekk fële ca Asi ñu di ko bay ci kémbaar yu bari, fi muy sax nag mooy fu xaw a am aw naaj.

Melo wi

Garab gu ndaw lay doon, guddaayam man naa jàpp 6i met. Man naa dund 200i at, waaye li ëpp ci limiy jur mi ngi koy jur ci 20i atam ju njëkk yi.

Ay Tóortóoram, dañuy yor melo wu xaw a xonq, 3i sentimet la baaxoo di gudde, ñatti yoon rekk lay meññ ci at mi, weeru Ut ak Me . Melow foytéefu "Garanaat" ñoo ngi sukkandikoo ci nimuy matee, maanaam yenn saay mu yor melo wu weex, walla wu xoq, walla wu mboq.

Doonte man naa dund ci suuf su xaw a wow waaye du tee garab gi suuf su xaw a tooy la bëgg ngir mu man a jur ay foytéefam ni mu ware.

Solo si

Garanaat garab la gog manees na cee defar ay jar doom bi dees koy lekk ay tóortóoram manees na cee xeex yenn wopp yu mel ni Aasm.

Nataal

Turu xam-xam wi

Punica granatum