Lingoom

Garabu lingoom
Tóortóoru lingoom
Meññeefum lingoom

Lingoom garab la gu bokk ci njabootu "rutacées". Dees na ko faral di bay ci barab yi bari naaj.

Melo wi

Garab la gog ay xobam dafay faral di wéy cig sax ci at mépp. Danay dund lu tollu ak 50 ba 80i at. Ay tóor-tóoram day weex. Doom bi nag dafay muluŋ te cat la sew. Guddaayam di nay àgg ci 7 ba 12i sàntimet.

Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx la, cig ñor nag mboq la.

Ndox mi mu ëmb, cafka gi dafay sëcc(wex). Doom bi day ëmbaale ay xoox.

Solo si

Lingoom bari na nees koy jëfandikoo. Dees na ci génnee njar mbaa ndollenu njar.

Turu xam-xam wi

Citrus limon

Tur wi ci yeneeni làkk

araab: الليمون
farañse: limone
angale: lemon
itaaliyee: limone