Melaneesi

Melaneesi benn la ci diwaan yi ñuy faral di seddatlee Oseyaani.

Bii seddatlin nga xam ne Kureelu Mbootaayu Xeet yi sax mooy la jëfandikoo suy seddatle àdduna bi ci ay Diwaan, gëstukat yi ñoom seddatle bu bees bi la ñu taamu, moo xaaj Oseyaani ci ñaari diwaan: Oseyaani gu jege ak Oseyaani gu sori yi melaneesi box.

Baatu Melaneesi waa faraas bii di Jules Dumont d'Uville moo ko sakk ci li jege atum 1830 (moo sakk itam baat yii di Polineesi, Mikroneesi ak Maleesi), mi ngi jóge ci baati waa Geres yii di μέλας (ñuul) e νησος (dun) maanaam dunu ñu ñuul ñi.

Ay dun yu tuut ñoo fa ne, man cee lim:

Ñenti réew ñooy yi fa ne ak benn suuf bu bokk ci Faraas:

Diwaani Oseyaani
Óstraali · Melaneesi · Mikroneesi  · Pacific Rim · Polineesi