Yamoo

Ci melosuuf, yamoo wi aw rëddu tus-wu-gar la, di ag buumug jeneer gees rëdd mu wër àdduna, jaar ci diggante dott yi. Yamoo wi moo xàjjale àdduna bi, def ko xaaju-kol-kol bu bëj-gànnaar ak xaaju-kol-kol bu bëj-saalum. Tus-wu-gaar wu yamoo wi 0° (tus aj). Guddaayu yamoo gu Suuf si mi ngi tollu, ci xayma, 40 075 km.

Yamoog Suuf si

Kilimaa

Kilimaab barab yi ne ci li wër yamoo gi lañuy wax kilimaab yamoo. Di nañ wax itam klimaab gëwéel, di bu barab yi ne ci li wër gëwéel yi (gëwéelub Tef ak gëwéelub Sànkar).

Réew yi mu dagg

Lonkoyoonu àdduna buy fesal yamoo gi

Ci sunu àdduna (Suuf si), yamoo gi ay mbàmbulaan ñoo ëpp ci li mu dagg ci yoonam, téeméer boo jël ci gudaayam ñaar-fukk ya rekk a jaar ci suuf.

Afrig

Yamoo gi jaar na ci juroom-ñaari réewi Afrig :